50
Aji Sax ji xol lay gërëm
1 Dib taalifu cant, ñeel Asaf.
Yàlla, Aji Sax ji Yàlla àddu na,
di woo àddina, penku ba sowu.
2 Ca Siyoŋ, dëkk ba ca taar ba
la Yàlla feeñe ni leer gu jolli.
3 Sunu Yàllaa ngi ñëw te du ne cell,
sawaraa ko jiitu, di xoyome,
ngëlén lu mag wër ko.
4 Ma ngay woo seede asamaan ak suuf,
ngir àtte ñoñam.
5 Mu ne: «Dajaleel ma sama wóllëre
yiy sarxal, di ko fasee sama kóllëreek ñoom.»
6 Asamaan a ngi biral àtteb Yàlla,
ndaxte mooy Kiy àtte.
Selaw.
7 «Yeen sama ñoñ, dégluleen, ma wax leen;
yeen waa Israayil, ma sikk leen.
Maa di Yàlla, seen Yàlla.
8 Du seeni sarax laa leen di sikke,
mbaa seen saraxi rendi-dóomal yi sax fi sama kanam.
9 Soxlawuma yëkku yar ak sikketu gétt.
10 Maay boroom raboo rabu àll,
ak junniy nag yuy fore tund ya.
11 Xam naa njanaawi tund yi,
luy ag jur ci tool yi maa ko moom.
12 Su ma xiifoon, duma leen ko wax,
maa moom àddinaak li ci biiram.
13 Ndax damay lekk yàppu nag
aka naan deretu sikket?
14 Deel jaajëfal Yàlla, sarxale ko,
di fey Aji Kawe ji loo dige,
15 di ma woo bésub njàqare,
ma wallu la, nga màggal ma.»
16 Ñu bon ñi, Yàlla ne leen:
«Lu ngeen di tari sama dogali yoon,
di waxe sama kóllëre?
17 Yeena ngii, bañ sama yar,
xalab samay kàddu.
18 Fu ngeen gisub sàcc, neexook moom,
ab njaalookat, ngeen lëngool.
19 Dangeena afal seen gémmiñ ci mbon,
seen làmmiñ taqoo fen,
20 ngeen di tooge seen mbokk,
di yàq deru doomu ndey.
21 Lii yeena ko def! Damay noppi,
ngeen defe ne damaa mel ni yeen?
Dama leen di sikk, tuumaal leen, ngeen gis!
22 «Yeen fàttekati Yàlla yi, déggleen lii,
bala maa xotat te kenn du wallu.
23 Ki may sarxale jaajëf moo ma teral;
ku topp yoon, ma won ko wallub Yàlla.»