80
Yàlla, suqalil sa njëmbat
1 Mu jëm ci njiital woykat yi, dëppook galan bu ñuy wax Tóor-tóor yi, dib taalifu cant, ñeel Asaf.
2 Éy yaw, Sàmmu Israayil, teewlu nu;
yaw mi jiite Yuusufa ni ag jur,
yaw mi toogandook malaakay serub yi,
feqal sag leer.
3 Dawalal sa njàmbaar, ñeel Efrayim ak Beñamin ak Manase,
te wallusi nu.
4 Éy Yàlla, suqali nu;
geesoo nu sa leeru kanam, nu raw.
5 Éy Aji Sax ji, Yàlla Boroom gàngoor yi,
foo àppal sa mer,
mi ngay wuyoo sa ñaanu mbooloo mi?
6 Leel nga nuw naqar,
nàndal nu mbàndum rongooñ,
7 def nga dëkkandoo di nu xëccoo,
noon di nu ree.
8 Éy Yàlla Boroom gàngoor yi, suqali nu;
geesoo nu sa leeru kanam, nu raw.
9 Yaa déjjate ag reseñ ci Misra,
dàq yéefar yi, indi, jëmbataat.
10 Nga raadu suuf si,
reseñ gi sampu, law, dajal réew mi;
11 keppaaram muur tund yi,
ay caram sàng garabi seedar yu mag yi.
12 Mu tàllal ay bànqaasam ba géej,
lawal njebbit la ba ca dexu Efraat ga.
13 Lu tax nga bëtt ay ñagam,
ba ku fa jaare witt ca,
14 mbaam àll di ko ruur,
ndundati àll di ca for?
15 Éy Yàlla Boroom gàngoor yi, geesul;
séentool asamaan, ba gis
te taxawusi reseñ gii.
16 Taxawusil njëmbat lii nga jëmbate sa ndijoor,
ngarab sii nga dooleelal sa bopp.
17 Dees koo gor, taal;
yal na ñii sànkoo sa mbugal.
18 Yal nanga yiir ki nga tànn,
kii nga dooleelal sa bopp,
19 ba dootunu la dëddu.
May nu nu dund, nu wormaal sa tur.
20 Éy Aji Sax ji, Yàlla Boroom gàngoor yi, suqali nu,
geesoo nu sa leeru kanam, nu raw.