81
Déggal Yàlla, jariñu
Mu jëm ci njiital woykat yi, ñeel Asaf, te ànd ak xalam gu ñuy wax gitiit*gitiit: seetal ci 8.1..
 
Sarxolleleen ci Yàlla mi nuy dooleel;
xaaculeen ci Yàllay Yanqóoba.
Yékkatileen woy te jiin,
xalam neex, ànd ak moroom ma.
Walleen bufta bi ci Terutel weer wi,
ak weer wu birale bésu màggal.
Loolu wartéefu Israayil la,
di ndigalu Yàllay Yanqóoba,
di ndénkaane bu mu dénk waa kër Yuusufa,
ba Yàllay dali ca kaw réewum Misra.
Baat bu ma xamul laa dégg, mu naan:
«Yennil naa leen yen bi,
woyofal seeni loxo.
Ngeen jàq, woo ma, ma xettali leen,
wuyoo leen fa kiiraayal dënn ya,
te maa leen nattoo fa wal ma ca Meriba.
Selaw.
Yeen sama ñoñ, dégluleen, ma dénk leen.
Éy Israayil, su ngeen ma déglu woon!
10 Buleen fat tuuru jàmbur,
buleen sujjóotal tuuru doxandéem.
11 Man, Aji Sax ji, maay seen Yàlla
ji leen yékkatee réewum Misra.
Ŋaleen ŋafeet, ma reggal leen.
 
12 «Waaye sama ñoñ déggaluñu ma,
ñuy Israayil gii ma nangulul.
13 Moo tax ma bërgël leen ak seenug të,
ñuy wéye seeni pexe.
14 Éy su ma sama ñoñ déggaloon,
éy su Israayil toppoon samay nammeel!
15 Ci saa si laay toroxal seeni noon,
duma seeni bañ,
16 ba ku bañ Aji Sax ji di ko raamal,
te àppam du jeex ba fàww.
17 Kon yeen, ma leel leen ngën-gi-pepp,
reggal leen lem ju doj xelli.»

*81.1 gitiit: seetal ci 8.1.