82
Yàllaay àtte ndawi péncam
Dib taalifu cant, ñeel Asaf.
 
Yàlla toog na, di jiite ndajem boppam,
di àtte ndawi péncam, naan:
«Dungeen bàyyi àtteb njublaŋ,
ak di faral ku bon?
Selaw.
Sàmmleen àqu néew-ji-dooleek jirim,
tey àtte yoon ku ñàkk ak ku ndóol.
Walluleen néew-ji-dooleek walaakaana,
di leen xettali ci ku bon.
 
«Ndawi péncum Yàlla yii xamuñu, dégguñu;
xanaa di doxe lëndëmu ñaawtéef,
ba ponki dëgg yépp di jaayu.
 
«Dama ne ay yàlla ngeen,
yeen ñépp di njabootu Aji Kawe ji.
Waaye du leen tee dee ni doom aadama,
du leen tee daanu ni képp kuy njiit.»
 
Ngalla Yàlla, taxawal, àtte àddina,
yaw yaa séddoo xeetoo xeet.