83
Yàlla, mbugalal noon yi
1 Di woyu cant, ñeel Asaf.
Éy Yàlla, bul ne cell,
2 rikk Yàlla, bul tanqamlu, ne patt.
3 Xoolal sa noon yiy riir,
sa bañ yi fippu ba téen!
4 Sa ñoñ lañuy rabatal,
di mànkool sa séddoo yii.
5 Ñu ne: «Ayca nu far seen xeet wi,
ba deesul fàttalikooti turu Israayil.»
6 Dañoo mànkoo kat,
te yaw lañu takktool:
7 muy néegi Edom ak Ismayla,
néegi Mowab ak Agar,
8 néegi Gebal, Amon ak Amaleg
ak waa Filisteek waa Tir,
9 réewum Asiri it fekki leen,
di dooleel askanu Lóot wa.
Selaw.
10 Def leen na nga defoon waa Majan*Seetal ci Njiit ya saar 6—8.,
def ko Sisera ak Yabin ca dexu Kison†Seetal ci Njiit ya saar 4—5.,
11 ña nga sànku ci Endor,
ba doonub tos fi kaw suuf.
12 Defal seeni njiit na Oreb ak Seeb,
def seen kilifa yépp ni Sebax ak Calmuna,
13 ña ne woon: «Nan séddoo parluy Yàlla yi.»
14 Éy Yàlla, wëndeel leen ni callweer,
ñu mel ni boob bu ngelaw wal.
15 Éy Yàlla, ni daay di xoyome àll,
sawara wa jafal tund ya,
16 yal nanga leen ni toppeek sa dooley ngelaw,
tiitale leen sa ngëlén.
17 Aji Sax ji, sëlëm leen gàcce,
ba ñu daw wutsi la.
18 Yal nañu rus, jàq ba fàww.
Yal nañu torox, sànku.
19 Yal nañu xam ne yaw mi tudd Aji Sax ji doŋŋ
yaay Aji Kawe ji yilif àddina sépp.