95
Kaayleen, nu sant
Kaayleen, nu sarxolleel Aji Sax ji,
nu xaacul sunu wéeru-mucc.
Nanu ko dikke cant,
woyal ko, mu riir.
Aji Sax jeey Yàlla ju màgg ji,
buur bu mag bi tiim yàllay xeet yépp.
Moo moom xóotey suuf,
moom colli tund yi,
moom géej, sàkk ko,
moom jéeri ji mu mooñ.
Nan sëgg, sujjóot,
sukkal Aji Sax ji nu sàkk.
Mooy sunu Yàlla,
nuy xeet wi muy foral,
diy gàtt ciy loxoom.
 
Bésub tey yal nangeen dégg kàddoom
ga mu noon: «Buleen të, na woon fa Meriba,
jantub keroog fa Maasa, ca màndiŋ ma,
fa ma seeni maam doon seetloo,
di ma diiŋat te gisoon samay jaloore*Seetal ci Mucc ga 17.1-7..
10 Ñeent fukki at laa jéppi googu maas,
ma ne: “Seen xol a dëkke lajj,
ñu faaleedi samay santaane.”
11 Moo ma taxa giñ ci sama biir mer,
ne duñu tàbbi fa samag noflaay.»

*95.9 Seetal ci Mucc ga 17.1-7.