96
Buur Yàllaa ngi àttesi àddina
1 Woyleen Aji Sax ji woy wu yees,
yeen àddina sépp woyleen Aji Sax ji.
2 Woyleen Aji Sax ji, màggal turam,
di siiwal xettaleem bésoo bés!
3 Siiwalleen màggaayam ci biir xeet yi,
xamal waasoo waaso ay jalooreem.
4 Aji Sax jee màgg, jara sant a sant
te gëna mata ragal lépp lu ñuy jaamu.
5 Mboolem yàlla yi xeet yiy jaamu, yàllantu la,
waaye Aji Sax jee sàkk asamaan.
6 Màggaay ak daraja, fa moom,
dooleek taar, fa këram gu sell.
7 Yeen làngi xeet yi, seedeelleen Aji Sax ji;
seedeelleen Aji Sax ji màggaayam ak dooleem.
8 Seedeelleen Aji Sax ji màggaayu turam,
yékkatil kob sarax, duggaale ëttam.
9 Sujjóotalleen Aji Sax ji gànjaroo sellaay.
Ragalleen ko, bay lox, yeen waa àddina sépp.
10 Neleen xeet yi Aji Sax jeey buur!
Àddinaa ngi sampu ba dëgër moos, maneesu koo rëññeel.
Mooy àtte xeet yi njub.
11 Asamaanoo, bégal! Suufoo, bànneexul!
Géejoo, riiral yaak mboolem li la fees,
12 na mbooy mi jaayu, mook lu ci biiram,
ba mboolem garabi àll bi sarxolleendoo,
13 gatandoo ko Aji Sax jiy dikk,
àttesi àddina,
di àtte dun bi dëgg,
tey àtte xeet yépp ci dëggoom.