99
Aji Sax ji buur bu sell la
Aji Sax jeey Buur. Yeen xeet yi, ragalleen ko!
Moo toogandook malaakay serub yi. Suufoo, soo yeboo, yëngu!
Aji Sax ji fi Siyoŋ a màgg,
kawe, tiim xeetoo xeet.
Sa tur weeka màgg te raglu. Sàbbaalleen ko.
—Kee sell!
Buur, jëfe yoon mooy dooleem.
Yaa saxal yoon, dëgg ak njub
ci askanu Yanqóoba.
Màggalleen sunu Yàlla, Aji Sax ji,
te sujjóot fa ndëggastalam.
—Kee sell!
 
Musaak Aaróona bokk ciy sarxalkatam,
Samiyel bokk ca ñay ñaan ci turam.
Ñuy ñaan Aji Sax ji, mu di leen nangul.
Fa biir taxaaru niir wa la waxeek ñoom,
ñu topp kàdduy seedeem ak dogalu yoonam ba mu leen joxoon.
Céy sunu Yàlla Aji Sax ji, yaa leen nanguloon,
di seen Yàlla ju leen di baal,
te di leen mbugale seeni jëf ju bon.
Màggalleen sunu Yàlla, Aji Sax ji,
te sujjóot fa tundam wu sell wa.
Sunu Yàlla Aji Sax jee sell!