100
Aji Sax jee baax
1 Di woyu cantu màggal.
Yeen waa àddina sépp,
xaaculleen Aji Sax ji.
2 Nangeen jaamu Aji Sax ji ci mbég,
dikke koy woy!
3 Seedeleen ne Aji Sax jeey Yàlla.
Moo nu sàkk, nuy ñoñam,
di gàttam yi muy foral.
4 Nangeen dem këram, dugge faag cant,
dugg ëttam di màggal,
sant ko, teral turam.
5 Aji Sax jee baax, gore ba fàww,
worma ja sax dàkk!