101
Buur a ngi jaayanteek Yàlla 
  1 Ñeel Daawuda, dib taalifu cant. 
 Ngor ak yoon laay woy.  
Yaw Aji Sax ji laay joobe.   
 2 Naa teewlu yoonu màndute.  
Ana kañ nga may dikkal?  
Naa doxe màndute  
fi sama biir waa kër.   
 3 Caaxaani neen, xooluma;  
jëf ju wàcc yoon, bëgguma,  
taqu ma fenn.   
 4 Kuy nas njekkar, sore ma;  
lu bon, xawma ko.   
 5 Kuy jëw moroomam, ma wedamal;  
ku daŋŋiiral ak ku reew, muñaluma la.   
 6 Ku dëggu ci réew mi, ma geesu,  
ngir fat ko.  
Te kuy wéye màndute,  
kookoo may liggéeyal.   
 7 Kuy njublaŋ du tooge sama kër,  
kuy fen du taxaw sama kanam.   
 8 Maay xëy, sànk képp ku bon ci réew mi,  
ngir génne ci dëkkub Aji Sax jii képp kuy def lu ñaaw.