111
Yàlla la ay mbiram sax 
  1 Màggalleen Ki Sax!  
Naa sante Aji Sax ji léppi xol  
ci biir ñu jub ñi bokk jataay.   
 2 Liggéeyi Aji Sax ji réy na,  
ku ko safoo di ko gëstu.   
 3 Jëfam di teddngaak*teddnga mooy teraanga ju bare lool. daraja,  
njubteem di sax ba fàww.   
 4 Moo dogal ñuy fàttalikuy kéemaanam;  
Aji Sax ji boroom yiw ak yërmande.   
 5 Mooy leel ku ko ragal,  
di bàyyi xel kóllëreem gi ba fàww.   
 6 Won na ñoñam dooley jëfam,  
ba mu leen joxee suufu xeet yi.   
 7 Ay jëfam dëgg laak yoon,  
tegtalam yépp mata wóolu,   
 8 laloo dëgg ak njub,  
te sax dàkk ba fàww.   
 9 Moo yónnee xeetam wall,  
fas ak ñoom kóllëre gu sax.  
Kee sell te jara ragal!   
 10 Ragal Aji Sax ji di njàlbéenu rafet xel,  
dég-dég bu rafet ñeel ku koy wéye.  
Moo yeyoo cant ba fàww.