112
Ku ragal Yàlla gis mbaaxam
Màggalleen Ki Sax!
Ndokkalee ku ragal Aji Sax ji,
di tàqamtikoo ay santaaneem.
Aw askanam ay am doole ci réew mi.
Ku jub saw xeet barkeel,
alal ak koom am sa kër,
sag jëf yu jekk sax dàkk.
Ceeñeeru biir lëndëm jollil na ku jub
ak ku baax, di boroom yërmande ak njubte.
Ki baaxle mooy ki laabiir, di leble,
di jëflante cig njub.
Ku jub du tërëf mukk,
te dees na ko fàttaliku ba fàww.
Du ragal dég-dég bu tiis,
xel ma day dal, mu wóolu Aji Sax ji,
fit wa toog, du ragal,
ba kera muy gis noonam jóoru.
Moo yéwén ci li muy may néew-doole yi,
njekkam sax dàkk,
dooleem di yokku, ànd ak daraja.
10 Soxor bi da koy gis, mer,
iñaan bay yéyu, jeex tàkk;
nde soxor, yaakaar ju tas rekk.