113
Buur Yàllaay walloo
Màggalleen Ki Sax!
Yeen ñiy jaamu Aji Sax ji, màggalleen ko,
màggalleen turu Aji Sax ji!
Yal nañu teral turu Aji Sax ji
tey ak ëllëg!
Li dale penku ba sowu,
màggalleen Aji Sax ji.
 
Aji Sax jee kawe, tiim xeetoo xeet,
darajaam sut asamaan!
Ana ku mel ni sunu Yàlla Aji Sax ji,
ki kaweel ab jalam, toog,
di jéer asamaan ak suuf?
 
Mooy yékkatee ku néewle fa suuf,
di seppee ku sonn cib sën,
bokkal ko jataayu kilifa
ya jiite xeetam.
Mooy dëël jigéen ju tële woona jur,
may ko mbégtem njureel.
Màggalleen Ki Sax!