114
Yàllaay walloo dooleem
Ba Israayil bàyyikoo fa Misra,
ba waa kër Yanqóoba dëddu askan woowu di làkk,
ca la Yuda doon kër Aji Sax ji,
giirug Israayil googu doon ab jagleem.
 
Géej gaa leen gis, daw,
dexu Yurdan a deltu gannaaw,
tund yu mag yiy curpi niy kuuy,
di curpeendook tund yu ndaw yi niy mbote.
 
Moo géej, loo xewle bay daw?
Yaw, dexu Yurdan, looy deltu gannaaw?
Tund yu mag yee, lu ngeen di curpi niy kuuy?
Yeen, tund yu ndaw yi, lu ngeen di curpi niy mbote?
 
Suufee, loxalal Boroom bi,
Yàllay Yanqóoba mii,
ki soppaliw doj ndox mu taa,
xeer wu ne sereŋ, mu def bëtu ndox.