115
Ku wóolu Yàlla barkeel
1 Bu muy nun, Aji Sax ji, bu muy nun,
saw tur nga wara teral,
ngir sa ngor ak sa worma.
2 Bu yéefar yi ne mukk:
«Moo ñii, ana seen Yàlla?»
3 Te yaw sunu Yàlla, yaa ngi asamaan,
di def lu la soob.
4 Seeni tuur xaalis laak wurus,
loxoo ko sàkk:
5 am gémmiñ te du wax,
ami gët te du gis,
6 ami nopp, du dégg,
am bakkan, du xeeñtu,
7 ami loxo it te du yég,
ami tànk it te du dox,
du xàddamiku sax.
8 Ñi sàkk yii tuur, yal nañu mel ni ñoom,
ñook ñi leen wóolu ñépp.
9 Éy Israayil, wóolul Aji Sax ji,
moo lay jàppale, di la aar.
10 Yeen waa kër Aaróona, wóoluleen Aji Sax ji,
moo leen di jàppale, di leen aar.
11 Yeen ñi ragal Aji Sax ji, wóoluleen Aji Sax ji,
moo leen di jàppale, di leen aar.
12 Aji Sax jee nuy bàyyi xel, di nu barkeel,
di barkeel kër Israayil,
di barkeel kër Aaróona.
13 Aji Sax jeey barkeel ku ko ragal,
mag ak ndaw.
14 Yal na leen Yàlla ful,
ful seeni doom.
15 Yal nangeen barkeelu ci Aji Sax ji,
Ki sàkk asamaan ak suuf.
16 Asamaan, asamaanu Aji Sax jee,
suuf la dénk doom aadama.
17 Du ku dee mooy màggal Ki Sax,
du kenn ku tàbbi réewum tàbbi-selaw!
18 Nun, nooy sargal Ki Sax,
tey ak ëllëg.
Màggalleen Ki Sax!