117
Na ñépp ànd ak Israayil sant Yàlla
Yeen xeetoo xeet, màggalleen Aji Sax ji,
réewoo réew, kañleen ko.
Moo nu xéewale ngoram gu réy,
te wormay Aji Sax jee sax dàkk.
Màggalleen Ki Sax!