118
Aji Sax jeek man, ma daan
Santleen Aji Sax ji, kee baax,
kee saxoo ngoram!
Rikk Israayil, neleen:
«Kee saxoo ngoram!»
Rikk waa kër Aaróona, neleen:
«Kee saxoo ngoram!»
Rikk yeen ñi ragal Aji Sax ji, neleen:
«Kee saxoo ngoram!»
 
Ci xat-xat laa woowe Ki Sax wall,
Ki Sax wuyu ma, yaatal ma.
Aji Sax jeek man, duma tiit.
Ana lees ma manal?
Aji Sax jeek man, di ma dimbali,
may seetaan bañ yi.
Làqoo Aji Sax jee gën
wóolu doom aadama.
Làqoo Aji Sax jee gën
wóolu garmi.
10 Yéefar yépp a ma sam,
ma bëmëx leen ci dooley Aji Sax ji.
11 Ñu sam maa sam;
ma bëmëx leen ci dooley Aji Sax ji.
12 Naka lañu ma sam niy yamb,
jekki ne kamaj ni taalu boob;
ma bëmëx ci dooley Aji Sax ji.
13 Dees maa jañax, jañax, ma ter-teri,
Aji Sax ji dimbali ma.
 
14 Sama doole, sama kaaraange, Ki Sax a;
te mooy sama wall tey.
15 Ndam aki sarxolle ca xaymay ñu jub ña,
ndijooru Aji Sax jee def njàmbaar!
16 Ndijoor la Aji Sax ji xàcc,
ndijooru Aji Sax jee def njàmbaar.
17 Duma dee moos, xanaa dund,
ba nettali jaloorey Ki Sax.
18 Ki Sax mbugal na maa mbugal,
waaye waccu ma, ma dee.
19 Ubbilleen ma bunti ñi jub,
ma dugg santi Ki Sax.
 
20 Buntu Aji Sax jaa ngii;
ñu jub ñee ciy dugge.
21 Dama lay sant, yaa ma nangul,
wallu ma tey.
22 Doj wi tabaxkat yi beddi woon,
moo mujj di doju koñu tabax bi.
23 Lii de, Aji Sax jee ko def,
nu gis ko, yéemu.
24 Bésub tey jii, Aji Sax jee ko sos,
nan ko bége, bànneexoo ko.
25 Ngalla Aji Sax ji, wallu nu.
Ngalla Aji Sax ji, may nu ndam.
26 Na barke wàcc ci ki dikk ci turu Aji Sax ji.
Nu ngi leen di ñaanale fi néegu Aji Sax ji.
27 Aji Sax jee di Yàlla, di nu leeral.
Jëlleen car yi, màggale,
te dox ba ca béjjéni sarxalukaay ba.
28 Yaa di sama Yàlla, ma di la sant;
céy sama Yàlla, dama lay kañ.
29 Santleen Aji Sax ji, kee baax,
kee saxoo ngoram.