126
Yàlla, delloo nu
Di woy yu ñuy yéege ca tund ya, di ko màggale Yàlla.
 
Ba Aji Sax ji delloo waa Siyoŋ seen réew,
danoo meloon ni ñuy gént,
di reeka sarxolle rekk.
Yéefar yi naa:
«Lu réy la Aji Sax ji defal ñii.»
Lu réy la nu Aji Sax ji defal moos,
nu bég.
 
Aji Sax ji, rikk delloo nu na woon,
ni ngay delloo wal yu ŋiis, mu walaat ca àllub Negew.
Kuy ji di jooy,
yal na góob, di sarxolle.
Ku doon wéy a wéy, di jooy;
yor mbuusum jiwoom,
yal na dikk a dikk, di woy,
ñibbiwaale sabaaram.