127
Barkeb Yàllaa wóor
Di woy yu ñuy yéege ca tund ya, di ko màggale Yàlla, ñeel Suleymaan.
 
Kër, su ko Aji Sax ji tabaxul,
ku ko tabax, neen nga doñ-doñi.
Ab dëkk, su ko Aji Sax ji wattuwul,
ku ko wattu, neen nga teewlu.
Neen it la nit di teela jóg
aka guddee tëdd,
di doñ-doñi lu mu lekk:
Aji Sax ji leel na soppeem lu ni day,
fekk ko muy nelaw.
 
Ma ne, doom Aji Sax jee koy sédde,
njurum doom yool la.
Doom joo jure ndaw,
mooy fitt ci loxol jàmbaar;
ndokkalee ku ci mbuusam fees,
ba bu ñu taseekub noon ca pénc ma,
duñu am gàcce mukk.