129
Noon manul Israayil
Di woy yu ñuy yéege ca tund ya, di ko màggale Yàlla.
 
Ba may ndaw ba tey, ñu ngi may sonal a sonal.
Israayiloo, waxati ko:
Ba may ndaw ba tey, ñu ngi may sonal a sonal,
te taxul ñu man ma.
Sama gannaaw gi lañu gàbb a gàbb,
rëdd koo rëdd nib tool.
Waaye àtteb Aji Sax ji mooy dëgg,
dog na buumi ñu bon ña.
 
Képp ku noonoo Siyoŋ,
yal nañu ko dëpp, gàcceel ko.
Yal nañu mel ni ñax mu saxem xadd,
balaa law, lax.
Du doyub ŋëb ku ko dog;
du doyub say ku ko for.
Ku fa jaare it du ko ne:
«Jaajëf, Aji Sax ji barkeel;
jaajëfe yaw, yal na Aji Sax ji barkeel.»