130
Nu séentu njotug Yàlla
Di woy yu ñuy yéege ca tund ya, di ko màggale Yàlla.
 
Aji Sax ji, ci ay xóote laa lay woowe.
Boroom bi, déglu ma,
teewlu ma, ma tinu la.
 
Ki Sax, yaw, soo doon lim bàkkaar,
Boroom bi, ana kuy taxaw?
Waaye yaay jéggale,
ñu ragal la.
 
Damay xaar Aji Sax ji, di ko xaare xol,
di yaakaar kàddoom.
Wattukat bi yàkkamti njël,
wattukat bi yàkkamti njël, laa ne,
ni ma yàkkamtee Aji Sax jee ko raw.
 
Éey Israayil, négandikul Aji Sax ji.
Aji Sax jee gore,
te yaatug njot.
Mooy jot Israayil ci ñaawtéefam yépp.