132
Yàlla digoo naak ki mu fal
1 Di woy yu ñuy yéege ca tund ya, di ko màggale Yàlla.
Éy Aji Sax ji, bàyyil xel Daawuda,
ak gépp njàqareem.
2 Moo giñaloon Aji Sax ji,
moo digook Mbërum Yanqóoba ma.
3 Mu ne: «Duma ñibbi,
4 duma tëddi ca sama kaw lal ba,
duma nelaw, duma gëmm sax bët,
5 li feek sàkkaluma Aji Sax ji béreb,
ba dëkkal Mbërum Yanqóoba ma.»
6 Ma ne, Efrata lanu dégg gaalu Yàlla ga,
fekk ko ca àll ya wër dëkku Yaar.
7 Nan dem ba këram,
sujjóotali ndëggastalu tànkam ya.
8 Aji Sax ji, jógal agsi sa dalluwaay,
yaak gaal gi jëmmal sa doole.
9 Say sarxalkat, yal nañu soloo njubte,
sa wóllëre yi sarxolleendoo.
10 Xoolal ci Daawuda, sa jaam ba,
ngalla bul gàntu ki nga fal.
11 Aji Sax ji daa giñal Daawuda
dëgg gu mu dul dëddu,
ne ko: «Ku jóge ci sa geño
laay teg ci sa jal,
12 te say doom, bu ñu sàmmee sama kóllëre,
ak sama kàdduy seede yi ma leen di xamal,
seeni doom it ñooy tooge sa jal ba fàww*Seetal ci 2.Samiyel 7.12-16..»
13 Aji Sax ji kat a tànn Siyoŋ,
taamu faa dëkke.
14 Mu ne: «Fii laay dalloo ba fàww,
fii laay dëkk, maa ko taamu.
15 Dund bi, ma barkeel a barkeel,
néew-ji-doole yi, ma reggal;
16 sarxalkat yi, ma wodde texe;
wóllëre yi di sarxollee sarxolle.
17 Fa laay dooleele Daawuda,
ni jum bu dul fey mukk, maay jafal nguuru ki ma fal.
18 Ay noonam, ma wodde gàcce;
moom, kaalaam ne ràññ.»