133
Bennoo, barkeel
1 Di woy yu ñuy yéege ca tund ya, di ko màggale Yàlla, ñeel Daawuda.
Céy liika baax te neexati,
ay bokk yu bokk dëkk, di benn!
2 Daa neex ni diwu bopp gu xeeñ,
siite sikkim, bu mel ni sikkimu Aaróona,
rogalaat ba ci mbubbam,
3 neex ni layub tundu Ermon,
neex ni lay bu ni mel tey rogalaate tundi Siyoŋ.
Fa la Aji Sax ji dogale barke,
muy dund, ba fàww.