134
Way-ngëm ñaa ngi sant
Di woy yu ñuy yéege ca tund ya, di ko màggale Yàlla.
 
Ayca, santleen Aji Sax ji,
yeen jaami Aji Sax ji yépp,
yeen ñiy taxawe kër Aji Sax ji guddi.
Yékkatileen seeni loxo ca béreb bu sell ba,
te sant Aji Sax ji.
 
Yal na la Aji Sax ji barkeele fa Siyoŋ,
moom mi sàkk asamaan ak suuf.