142
Aji Sax ji rekk a ma yég
Dib taalifu yeete bu ñeel Daawuda, ba mu nekkee ca xunt ma.
 
Ma àddu, ñaan Aji Sax ji;
àddu ca kaw, di tinu Aji Sax ji,
sippi ko sama tawat,
diis ko sama njàqare.
Bu ma yoqee,
ràññee nga samay jéego;
yoon wi may jaare
lañu ma làqal am yeer.
Ma geesu ndijoor, xool;
du kenn ku ma faale.
Rawtu réer ma,
du kenn ku sama bakkan saf.
 
Aji Sax ji, ma woo la wall;
ma ne, yaay sama kiiraay,
di sama séddoo fi kaw suuf.
Teewlul, ma ne wóoy,
damaa manatul,
xettali ma ci ñi ma topp,
dañu maa ëpp doole.
Ngalla génne ma fi ma tëje,
ma sant la.
Man la way-ngëm ñi di yéew ëllëg,
yaa may xéewale ab yool.