143
Aji Sax jeey sama yaakaar
1 Dib taalifu cant, ñeel Daawuda.
Éy Aji Sax ji, déglul, ma ñaan la;
teewlul, ma tinu la;
nangul ma ci sa wormaak sa àtteb dëgg.
2 Sang bi, bul layook man;
kenn jubul fi sa kanam, du kuy dund.
3 Noon a ma sambal,
daane ma, joggati,
dëël ma ci lëndëm
ni ku dee bu yàgg.
4 Sama doole jeex tàkk,
sama xol jeex, ma ne yàcc.
5 May fàttaliku bu njëkkoon,
di xalaat sa jaloore yépp,
seetaat li nga def.
6 Ma tàllal lay loxo,
soxla la, ni suuf su mar di soxlaa ndox.
Selaw.
7 Aji Sax ji, gaawal wuyu ma;
sama xol a jeex, ma ne yàcc,
bu ma xañ sa yiw,
ma yem ak kuy tàbbiji biir pax.
8 Xëye ma sa ngor,
yaw laa wóolu;
xamal ma fu may doxe,
yaw laa wékk sama bakkan.
9 Aji Sax ji, musal ma ci noon yi,
yaw laa làqoo.
10 Jàngal ma, ma jëfe sa coobare;
yaa di sama Yàlla.
Yal na ma sam xel jiitee mbaax
ci yoon wu tàlli.
11 Aji Sax ji, musal ma ngir sa tur,
jëfeel sa àtte, teggil ma njàqarey bakkan.
12 Sànkal ma noon yi ci sa ngor,
bóomal ma bépp mbañ.
Man de, maay sab jaam!