Nattinu jamono ci bànni Israayil
Tur yi ci keppu yi ( . . . ), weer waa ngi ci Kàddug Yàlla waaye tur wi nekku ca.
Limeefu weer wi Turu weer wi Yemook Jamonoy mbey Màggal yi ci seen bés
1 Abiib, Nisan mars, jàpp awril taw bu mujj, ngóobum lors 14 bés ci Abiib: màggalu bésub Mucc (Mucc ga 12.18). Bési 15 ba 21 ci Abiib: màggalug ayu bésu Mburu mu amul lawiir (Mucc ga 12.14-20). 16 bés ci Abiib: màggalu Ndoortel meññeef (Sarxalkat 23.9-11).
2 Siw, (Iyar) awril, jàpp me
3 Siwan me, jàpp suweŋ ngóobum bele Ñeenteelu bés ci Siwan: Pàntakot, ñu koy tudde itam màggalug Ngóob (Sarxalkat 23.15-16).
4 (Tamus) suweŋ, jàpp sulet
5 (Ab) sulet, jàpp ut
6 Elul ut, jàpp sàttumbar wittum reseñ ak figg ak oliw
7 Etanin, (Tisri) sàttumbar, jàpp oktoobar taw bu jëkk Bés bu jëkk ci Etanin: màggalu bésu Liit yi (Sarxalkat 23.24). Fukkeelu bés bi: bésu Njotlaay (Sarxalkat 16). Bési 15 ba 21 ci Etanin: màggalu ayu bésu Mbaar yi (Sarxalkat 23.34-40). Bésu 22 ci Etanin: Ndaje mu sell (Sarxalkat 23.36).
8 Bul, (Marxeswan) oktoobar, jàpp nowàmbar
9 Kislew nowàmbar, jàpp desàmbar Bésu 25 ci Kislew: bés ba ñuy baaxantal daloog kër Yàlla ga (Yowaan 10.22).
10 Tebet desàmbar, jàpp saawyee
11 Sebat saawyee, jàpp fewriyee
12 Adar fewriyee, jàpp màrs wittum doomi garab Bési 14 ba 15 ci Adar: màggalu bési Purim (Esteer 9.21).