Waxi yonent yi jëm ci Almasi bi
Diirub junniy at yonent yi wax nañu lu bare ci mbirum Almasi bi, di Rammukat biy ganesi àddina. Moo tax Yeesu Almasi bi nee na: «Xanaa du fàww Almasi bi daj boobu coono, doora dugg ci teraangaam?» Mu tàmbalee nag ci Yonent Yàlla Musaa, jaare ci yonent yépp, tekkil leen mboolem lu Mbind mi indi ci mbiram» (Luug 24.26-27).
Te ndawal Yàlla Piyeer teg ca ne: «Moom la yonent yépp seedeel, ne képp ku ko gëm, jot nga sa njéggalug bàkkaar ciw turam» (Jëf ya 10.43).
Jukki nanu fi nag li yonent yi yégle, ak ni seen wax ame ci Almasi Yeesu. Ngir gàttal mbind mi, bind nanu saar 8, aaya 10 ba ci aaya 14 nii: 8.10-14. Yem nanu ci téereb ndawal Yàlla Macë.
Léeg-léeg baat yi ñu jukkee ci Kóllëre gi jëkk day xawa wuuteek li ñu bind ci Kóllëre gi yees, ndaxte ka koy bind ca tekkiteg Kóllëre gu jëkk gi, ci gereg la ko jële.
Yonent Yàlla | Ay at yu jiitu Almasi bi | Nee na: | Ni mu amee ci Almasi bi, ci téereb Macë |
Musaa ci Baamtug yoon wi 18.15 | 1406 | Almasi bi mooy yonent bi Yàlla dige woon, mu wara soqikoo ci bànni Israayil. | 21.11 |
Natan ci 2.Samiyel 7.16 | 990 | Mooy sëtu Daawuda bi wara nguuru ba fàww. | 1.1 |
Esayi 7.14 | 740 | Dina juddu ci ku masula ànd ak góor. | 1.20-23 |
Mise 5.1 | 739 | Dina juddu ci dëkku Betleyem. | 2.4-6 |
Ose 11.1 | 760 | Dina gàddaayi réewu Misra, di Esibtë ba tey. | 2.14-15 |
Malasi 3.1 | 450 | Yonent Yàlla Yaxya dina ko jiitusi, yégle ñëwam. | 3.1-3 |
Esayi 8.23—9.1 | 740 | Almasi bi dina waaraate ci diiwaanu Galile. | 4.12-17 |
Esayi 53.4 | 740 | Dina sëfoo mititu nit ñi. | 8.16-17 |
Esayi 42.1-4 | 740 | Ñi seen yaakaar tas, moo leen koy delloo. | 12.17-21 |
Sàkkaryaa 9.9 | 520 | Dina war mbaam-sëf, dugg Yerusalem, di Siyoŋ ba tey. | 21.1-5 |
Sàkkaryaa 11.12 | 520 | Dees na ko wor ci fanweeri poseti xaalis. | 26.14-16 |
Sàkkaryaa 13.7 | 520 | Ay taalibeem dinañu ko won gannaaw. | 26.31 |
Esayi 50.6 | 740 | Nit ñi dinañu ko tifli ci kanam. | 26.67 |
Daawuda ci taalif 22.19 | 990 | Dinañu séddale ay yéreem. | 27.35 |
Esayi 53.12 | 740 | Dina dee ci biiri tooñkat. | 27.38 |
Esayi 53.6; taalifu Daawuda 22.19 | 740; 990 | Yàlla dina ko sëf mbugal mi nu wara dékku. | 27.45-56 |
Yunus 1.16—2.1; Daawuda ci taalif 16.10 | 790; 990 | Dina dekki ca ñetteelu fan ba. | 12.38-40; 28.5-6 |
Dañeel 7.13-14 | 553 | Dina délsi ci àddina ci biir ndam. | 24.29-31 |