^
Sabóor
Ñaari yoon a ngii
Yàlla fal na buur
Aji jub a ngi woote wall
Muy kàddug Sabóor, ñeel Daawuda, ba muy daw Absalom doomam ju góor3.1 Seetal ci 2.Samiyel 15—16..
Ma gonloo ñaan
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd aki xalam, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.
Ma jëluy ñaan
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd aki toxoro, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.
Jarag a ngi woote wall
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd ak xalamu juróom ñetti buum, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.
Boroom tuumaa ngi woote wall
Muy woyu njàmbat, ñeel Daawuda. Mu woyaloon ko Aji Sax ji ci mbirum kàddu yu tukkee woon ca Kuus, ma bokkoon ci giirug Beñamin.
Aji Sax ji teral na nit
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd ak xalam gu ñuy wax gitiit8.1 gitiit tur la wu réer ci làkku ebrë. Man na doon xeetu xalam gu cosaanoo dëkk ba ñuy wax Gaat ci réewu Filisti. Man na nekk it galan bu ñu daan woye ci jamono bu ñuy witt reseñ, di ko nal., ñeel Daawuda, di kàddug Sabóor.
Aji Sax ji dëgg lay àtte
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bu ñuy wax Deewug doom ju góor, ñeel Daawuda, di kàddug Sabóor.
Néew-ji-doole sàkku na yoon
Ma làqoo Aji Sax ji
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ñeel Daawuda.
Kàddug Yàllaa wóor
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd ak xalamu juróom ñetti buum, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.
Aji Sax ji, loo deeti xaar?
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.
Yàqute maase na
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ñeel Daawuda.
Kuy aji jub?
Muy kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.
Aji Sax ji laa séddoo, dund ak dee
Muy taalifu Daawuda, ngir jàngle.
Aji Sax ji, jox ma dëgg
Muy ñaanu Daawuda.
Buur daan, sant Aji Sax ji
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ñeel Daawuda jaamub Aji Sax ji. Mu jagleel Aji Sax ji woy wii, bés ba mu ko xettlee ci mboolem noonam, xettli ko it ci Buur Sóol. Kàdduy woy yaa ngii.
Aji Sax ji màgg na
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.
Yal na Buur daan
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.
Aji Sax ji baaxe na Buur
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.
Jëkke jàq, mujje sant
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda, dëppook galan bi ñu dippee Kéwélu fajar.
Aji Sax jee may sàmm
Ñeel Daawuda, di kàddug Sabóor.
Ana kuy màggal Buur Yàlla?
Ñeel Daawuda, di kàddug Sabóor.
Aji Sax jeey gindee, di yiire
Ñeel Daawuda.
Ma waajal ndajem kër Aji Sax ji
Ñeel Daawuda.
Xare jib, ma ànd ak Yàlla
Ñeel Daawuda.
Aji Sax jeey àtte ñoñam
Ñeel Daawuda.
Aji Sax jeey boroom ndam
Muy kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.
Mucc, bég
Muy woyu Sabóor, ñeel Daawuda ca daloob kër Yàlla ga30.1 Woyu Sabóor wii Daawuda da koy sante Yàlla gannaaw mbas ma, ba mu jëndee dàgga ngir rendi fa sarax su dakkal mbas ma. Dàgga jooju lañu mujj tabax jaamookaay ba. Seetal ci 2.Samiyel 24, ak 1.Jaar-jaar ya 21..
Naa siggi, noon sëgg
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.
Njéggal barke la
Dib taalif, ñeel Daawuda.
Nan woy Boroom bi nu sàkk
Aji Sax ji du tanqamlu aji jub
Ñeel Daawuda. Mooy ba muy wayadi-wayadilu ca kanam Abimeleg, ba Abimeleg dàq ko, mu dem34.1 Seetal ci 1.Samiyel 21.10-15. Akis buurub Gaat mooy Abimeleg ba tey..
Aji Sax ji, àtte maak noon
Ñeel Daawuda.
Nit ñaaw, Aji Sax ji gore
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ñeel Daawuda jaamub Aji Sax ji.
Bu sa xol jóg
Ñeel Daawuda.
Maa wopp, tuub, di jooy
Muy kàddug Sabóor guy fàttlee, ñeel Daawuda.
Dund yàggul
Mu jëm ci Yedutun, njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.
Déggal Aji Sax jee am solo
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ñeel Daawuda, di kàddug Sabóor.
Jarag bu ñu toŋal a ngi ñaan
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.
Maa namm Yàlla
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di taalif bu ñeel askanu Kore wu góor.
Éy Yàlla, àtte ma
Xeet waa ngi jooy
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di taalif bu ñeel askanu Kore wu góor.
Buur a ngi séetal
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bu ñuy wax Tóor-tóor, ñeel askanu Kore wu góor, dib taalif, te di woyu mbëggeel.
Aji Sax jee ànd ak man
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di jàngin wu ñeel askanu Kore wu góor, dëppook galan bu ñuy wax Baatu jigéen.
Yàllaay buur
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel askanu Kore wu góor.
Aji Sax ji aar na Siyoŋ
Muy woyu Sabóor, ñeel askanu Kore wu góor.
Alal day naxe
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel askanu Kore wu góor.
Aji Sax ji xol lay gërëm
Muy kàddug Sabóor, giiroo ci Asaf.
Yàlla, yërëm ma
Mu jëm ci njiitu jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda. Mooy ba ko Yonent Yàlla Natan seetsee, gannaaw ba Daawuda dëkkoo ndaw sa ñuy wax Batseba51.2 Seetal ci 2.Samiyel 11—12.25..
Yàllaa man boroom doole
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di taalif bu ñeel Daawuda. Mooy ba Doweg, Edomeen ba, demee ca Sóol, ne ko Daawuda dem na kër Ayimeleg52.2 Seetal ci 1.Samiyel 21—22..
Mbon maase na
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bu ñuy wax Maalat, di taalif bu ñeel Daawuda.
Yàlla, dimbali ma
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd aki xalam, di taalif bu ñeel Daawuda. Mooy ba waa Sif demee ca Sóol, ne ko Daawudaa nga làqu ca seenum réew54.2 Seetal ci 1.Samiyel 23.14-28; 26.1-5..
Xarit wor na ma
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd aki xalam, dib taalif, ñeel Daawuda.
Yàlla laa wóolu, ragaluma nit
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bi ñu dippee Pitax mu luu, dëkk fu sore; di taalifu jàngle bu Daawuda fentoon, ba ko Filisteen ña jàppee ca Gaat56.1 Seetal ci 1.Samiyel 21.10-15..
Yàlla jógal, wallu ma!
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bi ñuy wooye Bul yàq, di taalifu jàngle bu Daawuda fentoon, gannaaw ba mu dawee Buur Sóol, ba dugg ca xunti ma57.1 Seetal ci 1.Samiyel 24..
Yàllaa mana mbugal
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bi ñuy wooye Bul yàq, di taalifu jàngle, ñeel Daawuda.
Wallu maak ñu bon ñi
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bi ñuy wooye Bul yàq, di taalifu jàngle bu Daawuda fentoon. Mooy ba Buur Sóol yónnee ay nit ñu ko xoolal kër Daawuda, ngir rey ko59.1 Seetal ci 1.Samiyel 19.11-17..
Yàllaa yor sunu mucc
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bu ñuy wax Seedeb Tóor-tóor, di taalifu jàngle, ñeel Daawuda. Mooy ba Daawuda di xareek waa Siri ña ca Mesopotami ak waa Siri ña ca Soba te ba ñu ca bàyyikoo, Yowab duma fukki junniy Edomeen ak ñaar (12 000) ca xuru Xorom wa60.2 Seetal ci 2.Samiyel 8.3-14; 1.Jaar-jaar ya 18.3-13..
Naa woote wall
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd aki xalam, ñeel Daawuda.
Yaakaar, fa Yàlla
Mu jëm ci Yedutun, njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.
Maa namm Aji Sax ji
Muy kàddug Sabóor, ñeel Daawuda. Mooy ba mu nekkee ca màndiŋu Yuda63.1 Seetal ci 1.Samiyel 23.14; 24.2; 2.Samiyel 15.23..
Yàllaa man ag fitt
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.
Yàllaay nangul suuf
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di woyu Sabóor, ñeel Daawuda.
Yàllaay aar nitam
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di woyu Sabóor.
Yal na nu Yàlla barkeel
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd aki xalam, di woyu Sabóor.
Yàlla daagu, daan
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ñeel Daawuda, di woyu Sabóor.
Ku ñu fitnaal a ngi ñaan
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bu ñuy wax Tóor-tóor, ñeel Daawuda.
Yàlla, gaawe ma
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ñeel Daawuda, di woy wuy fàttlee.
Mag a ngi séentu njekku Yàlla
Nu ñaanal Buur
Ñeel Suleymaan.
Am Yàllaa gën
Muy kàddug Sabóor, giiroo ci Asaf.
Yàlla, bu la noon ree
Muy taalifu yeete, giiroo ci Asaf.
Yàllaay àtte
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bi ñu dippee Bul yàq, di woyu Sabóor, giiroo ci Asaf.
Yàllaa moom xare
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd aki xalam, di woyu Sabóor, giiroo ci Asaf.
Yàllaa ngi seetaan
Mu jëm ci Yedutun, njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, giiroo ci Asaf.
Nit goreedi, Yàlla gore
Muy taalif bu giiroo ci Asaf.
Yàlla, feyul nu
Muy kàddug Sabóor, giiroo ci Asaf.
Yàlla, suqlil sa njëmbat
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bu ñuy wax Tóor-tóor yi, di seedeb Sabóor, giiroo ci Asaf.
Déggal Yàlla, jariñu
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, giiroo ci Asaf, te ànd ak xalam gu ñuy wax gitiit.
Yàllaay àtte ndawi péncam
Muy kàddug Sabóor, giiroo ci Asaf.
Yàlla, mbugalal noon yi
Di woyu Sabóor, giiroo ci Asaf.
Ku dal ak Yàlla bég
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd ak xalam gu ñuy wax gitiit, ñeel askanu Kore wu góor.
Aji Sax ji, suqleeti nu
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel askanu Kore wu góor.
Ma ñaan, bésub njàqare
Mu di ñaanu Daawuda.
Siyoŋ, yaay ndeyu xeet yi
Ñeel askanu Kore wu góor, di woyu Sabóor.
Ma jàq, jooy
Muy woyu Sabóor, ñeel askanu Kore wu góor, jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bu ñuy wax Maalat Leyanot, di taalifu Eman, mi bokk ci giirug Esra.
Aji Sax ji, loo dige woon?
Muy taalif bu ñeel Etan mi bokk ci giirug Esra.
Doom aadama yàggul
Muy ñaanu Musaa, góorug Yàlla ga.
Aji Sax jee mat kaaraange
Nu woy bésub Noflaay
Muy woyu Sabóor ngir bésub Noflaay.
Ma bàkk Aji Sax ji
Yàllaay mbugal ku bon
Kaayleen, nu sant
Buur Yàllaa ngi àttesi àddina
Nguurug Aji Sax ji njekk la
Woyleen Aji Sax jiy àttesi
Muy kàddug Sabóor.
Aji Sax ji buur bu sell la
Aji Sax jee baax
Muy jàngi cant.
Buur a ngi jaayanteek Yàlla
Ñeel Daawuda, di kàddug Sabóor.
Yàlla, bu ma rey
Muy ñaanu néew-ji-doole ju sonn, bay diis Aji Sax ji njàqareem.
Ma sant Aji Sax ji
Ñeel Daawuda.
Màggal-leen ki sàkk lépp
Aji Sax ji sàmm na kóllëre
Israyil di wor, Yàlla di wóor
Aji Sax jeey xettlee
Yàlla, may nu ndam
Muy woyu Sabóor, ñeel Daawuda.
Yal na Yàlla mbugal noon bi
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ñeel Daawuda, di kàddug Sabóor.
Yàlla fal na nitam
Ñeel Daawuda, di kàddug Sabóor.
Yàlla la ay mbiram sax
Ku ragal Yàlla gis njekkam
Buur Yàllaay walloo
Yàllaay walloo dooleem
Ku wóolu Yàlla barkeel
Ma sant Yàlla mi ma jot
Na ñépp ànd ak Israyil sant Yàlla
Aji Sax jeek man, ma daan
Aji Sax ji, sa kàddu laay bége
Ma ñaan ci biir tuuma
Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla.
Ana ku may sàmm?
Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla.
Nu ñaanal Yerusalem
Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla, ñeel Daawuda.
Yàlla, fajal nu gàcce
Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla.
Nanu sante Aji Sax ji wallam
Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla, ñeel Daawuda.
Ku doyloo Aji Sax ji raw
Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla.
Yàlla, delloo nu
Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla.
Barkeb Yàllaa wóor
Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla, ñeel Suleymaan.
Ragal Yàlla, jàmmi kër
Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla.
Noon manul Israyil
Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla.
Nu séentu njotug Yàlla
Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla.
Damaa woyof, gëm Yàlla
Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla, ñeel Daawuda.
Yàlla digoo naak ki mu fal
Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla.
Bokk, bennoo neex
Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla, ñeel Daawuda.
Way-gëm ñaa ngi sant
Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla.
Aji Sax ji jot na Israyil
Yàllaa am kóllëre
Jooye nanu àll
Aji Sax ji waccu ma
Ñeel Daawuda.
Aji Sax jee ma xam, ba jeexal ma
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ñeel Daawuda, di kàddug Sabóor.
Ku ñu toŋal a ngi ñaan
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.
Yàlla, sàmmal sama làmmiñ
Muy kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.
Aji Sax ji rekk a ma yég
Muy taalifu ñaan bu ñeel Daawuda, ba mu nekkee ca xunti ma.
Aji Sax jeey sama yaakaar
Muy kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.
Aji Sax ji, laggsil
Ñeel Daawuda.
Ma kañ Buur Yàlla
Muy jàngi màggal, ñeel Daawuda.
Buur Yàllaa jara wóolu
Yàllaa gën ci àddina, gën ci nit
Na àddina wërngal këpp màggal Yàlla
Na Israyil màggal Ki Sax
Màggal-leen Ki Sax!