Taalifi cant
<
0
>
^
Taalifi cant
Ñaari yoon a ngii
Yàlla fal na buur
Aji jub a ngi woote wall
Dib taalifu cant, ñeel Daawuda, ba muy daw Absalom doomam ju góor3.1 Seetal ci 2.Samiyel saar 15—16..
Ma yendoo ñaan
Mu jëm ci njiital woykat yi, ànd aki xalam, dib taalifu cant, ñeel Daawuda.
Ma njëlu di ñaan
Mu jëm ci njiital woykat yi, ànd aki toxoro, dib taalifu cant, ñeel Daawuda.
Jarag a ngi woote wall
Mu jëm ci njiital woykat yi, ànd ak xalamu juróom ñetti buum, dib taalifu cant, ñeel Daawuda.
Boroom tuumaa ngi woote wall
Di woyu njàmbat, ñeel Daawuda. Mu woyaloon ko Aji Sax ji ci mbirum kàddu yu tukkee woon ca Kuus, ma bokkoon ci giirug Beñamin.
Aji Sax ji teral na nit
Mu jëm ci njiital woykat yi, ànd ak xalam gu ñuy wax gitiit8.1 gitiit tur la wu réer ci làkku ebrë. Man na doon xeetu xalam gu cosaanoo dëkk ba ñuy wax Gaat ci réewu Filisti. Man na nekk it galan bu ñu daan woye ci jamono bu ñuy witt reseñ, di ko nal., ñeel Daawuda, dib taalifu cant.
Aji Sax ji dëgg lay àtte
Mu jëm ci njiital woykat yi, dëppook galan bu ñuy wax Deewug doom ju góor, ñeel Daawuda, dib taalifu cant.
Néew-ji-doole sàkku na yoon
Ma làqoo Aji Sax ji
Mu jëm ci njiital woykat yi, ñeel Daawuda.
Kàddug Yàllaa wóor
Mu jëm ci njiital woykat yi, ànd ak xalamu juróom ñetti buum, dib taalifu cant, ñeel Daawuda.
Aji Sax ji, loo deeti xaar?
Mu jëm ci njiital woykat yi, dib taalifu cant, ñeel Daawuda.
Yàqute maase na
Mu jëm ci njiital woykat yi, ñeel Daawuda.
Kuy aji jub?
Dib taalifu cant, ñeel Daawuda.
Aji Sax ji laa séddoo, dund ak dee
Diy ñaan, ñeel Daawuda.
Aji Sax ji, jox ma dëgg
Di ñaanu Daawuda.
Buur daan, sant Aji Sax ji
Mu jëm ci njiital woykat yi, ñeel Daawuda jaamub Aji Sax ji. Mu jagleel Aji Sax ji woy wii, bés ba mu ko xettalee ci mboolemi noonam, xettali ko it ci Buur Sawul. Kàdduy woy wa lii la.
Aji Sax ji màgg na
Mu jëm ci njiital woykat yi, dib taalifu cant, ñeel Daawuda.
Yal na Buur daan
Mu jëm ci njiital woykat yi, dib taalifu cant, ñeel Daawuda.
Aji Sax ji baaxe na Buur
Mu jëm ci njiital woykat yi, dib taalifu cant, ñeel Daawuda.
Jëkke jàq, mujje sant
Mu jëm ci njiital woykat yi, dib taalifu cant, ñeel Daawuda, dëppook galan bi ñu dippee Kéwélu fajar.
Aji Sax jee may sàmm
Ñeel Daawuda, dib taalifu cant.
Ana kuy màggal Buur Yàlla?
Ñeel Daawuda, dib taalifu cant.
Aji Sax jeey gindee, di yiire
Ñeel Daawuda.
Ma waajal ndajem kër Aji Sax ji
Ñeel Daawuda.
Xare jib, ma ànd ak Yàlla
Ñeel Daawuda.
Aji Sax jeey àtte ñoñam
Ñeel Daawuda.
Aji Sax jeey boroom ndam
Dib taalifu cant, ñeel Daawuda.
Mucc, bég
Dib taalifu cant, ñeel Daawuda ca daloob kër Yàlla ga.
Naa siggi, noon sëgg
Mu jëm ci njiital woykat yi, dib taalifu cant, ñeel Daawuda.
Njéggal barke la
Dib taalifu yeete, ñeel Daawuda.
Nan woy Boroom bi nu sàkk
Aji Sax ji du tanqamlu aji jub
Ñeel Daawuda. Mooy ba muy wayadi-wayadilu ca kanam Buur Abimeleg, ba Abimeleg dàq ko, mu dem34.1 Seetal ci 1.Samiyel 21.11-16. Akis buurub Gaat mooy Abimeleg ba tey..
Aji Sax ji, àtte maak noon yi
Ñeel Daawuda.
Nit ñaaw, Aji Sax ji gore
Mu jëm ci njiital woykat yi, ñeel Daawuda jaamub Aji Sax ji.
Bu sa xol jóg
Ñeel Daawuda.
Maa wopp, tuub, di jooy
Dib taalifu cant buy fàttalee, ñeel Daawuda.
Dund yàggul
Mu jëm ci Yedutun, njiital woykat yi, dib taalifu cant, ñeel Daawuda.
Déggal Aji Sax jee am solo
Mu jëm ci njiital woykat yi, ñeel Daawuda, dib taalifu cant.
Jarag bu ñu toŋal a ngi ñaan
Mu jëm ci njiital woykat yi, dib taalifu cant, ñeel Daawuda.
Maa namm Yàlla
Mu jëm ci njiital woykat yi, dib taalifu yeete bu ñeel askanu Kore wu góor.
Éy Yàlla, àtte ma
Xeet waa ngi jooy
Mu jëm ci njiital woykat yi, dib taalifu yeete bu ñeel askanu Kore wu góor.
Buur a ngi séetal
Mu jëm ci njiital woykat yi, dëppook galan bu ñuy wax Tóor-tóor, ñeel askanu Kore wu góor, dib taalifu yeete, te di woyu mbëggeel.
Aji Sax jee ànd ak man
Mu jëm ci njiital woykat yi, di woy wu ñeel askanu Kore wu góor, dëppook galan bu ñuy wax Baatu jigéen.
Yàllaay Buur
Mu jëm ci njiital woykat yi, dib taalifu cant, ñeel askanu Kore wu góor.
Aji Sax ji aar na Siyoŋ
Di woyu cant, ñeel askanu Kore wu góor.
Alal day naxe
Mu jëm ci njiital woykat yi, dib taalifu cant, ñeel askanu Kore wu góor.
Aji Sax ji xol lay gërëm
Dib taalifu cant, ñeel Asaf.
Yàlla, yërëm ma
Mu jëm ci njiitu woykat yi, dib taalifu cant, ñeel Daawuda. Mooy ba ko Yonent Yàlla Natan seetsee, gannaaw ba Daawuda tëddee ndaw sa ñuy wax Batseba51.2 Seetal ci 2.Samiyel 11.1—12.25..
Yàllaa man boroom doole
Mu jëm ci njiital woykat yi, dib taalifu yeete bu ñeel Daawuda. Mooy ba Doweg, Edomeen ba, demee ca Sawul, ne ko Daawuda dem na kër Aximeleg52.2 Seetal ci 1.Samiyel saar 21—22..
Mbon maase na
Mu jëm ci njiital woykat yi, dëppook galan bu ñuy wax Maxalat, dib taalifu yeete bu ñeel Daawuda.
Yàlla, dimbali ma
Mu jëm ci njiital woykat yi, ànd aki xalam, dib taalifu yeete bu ñeel Daawuda. Mooy ba waa Sif demee ca Sawul, ne ko Daawudaa nga làqu ca seenum réew54.2 Seetal ci 1.Samiyel 23.14-28; 26.1-5..
Xarit wor na ma
Mu jëm ci njiital woykat yi, ànd aki xalam, dib taalifu yeete, ñeel Daawuda.
Yàlla laa wóolu, ragaluma nit
Mu jëm ci njiital woykat yi, dëppook galan bi ñu dippee Pitax mu luu, dëkk fu sore; diy ñaan, ñeel Daawuda, ba ko Filisteen ña jàppee ca Gaat56.1 Seetal ci 1.Samiyel 21.11-16..
Yàlla jógal, wallu ma!
Mu jëm ci njiital woykat yi, dëppook galan bi ñuy woowe Bul yàq, diy ñaan, ñeel Daawuda, gannaaw ba mu dawee Buur Sawul, ba dugg ca xunt ma57.1 Seetal ci 1.Samiyel saar 24..
Yàllaa mana mbugal
Mu jëm ci njiital woykat yi, dëppook galan bi ñuy woowe Bul yàq, diy ñaan, ñeel Daawuda.
Wallu maak ñu bon ñi
Mu jëm ci njiital woykat yi, dëppook galan bi ñuy woowe Bul yàq, diy ñaan, ñeel Daawuda. Mooy ba Buur Sawul yónnee ay nit ñu ko xoolal kër Daawuda, ngir rey ko59.1 Seetal ci 1.Samiyel 19.11-17..
Yàllaa yor sunu mucc
Mu jëm ci njiital woykat yi, dëppook galan bu ñuy wax Seedeb tóor-tóor, diy ñaan, ñeel Daawuda. Mooy ba Daawuda di xareek waa Siri ña ca Mesopotami ak waa Siri ña ca Coba te ba ñu ca bàyyikoo, Yowab duma fukki junniy Edomeen ak ñaar (12 000) ca xuru Xorom wa60.2 Seetal ci 2.Samiyel 8.3-14; 1.Jaar-jaar ya 18.3-13..
Naa woote wall
Mu jëm ci njiital woykat yi, ànd aki xalam, ñeel Daawuda.
Yaakaar, fa Yàlla
Mu jëm ci Yedutun, njiital woykat yi, dib taalifu cant, ñeel Daawuda.
Maa namm Aji Sax ji
Dib taalifu cant, ñeel Daawuda. Mooy ba mu nekkee ca màndiŋu Yuda63.1 Seetal ci 1.Samiyel 23.14; 24.2; 2.Samiyel 15.23..
Yàllaa man ag fitt
Mu jëm ci njiital woykat yi, dib taalifu cant, ñeel Daawuda.
Yàllaay nangul suuf
Mu jëm ci njiital woykat yi, di woyu cant, ñeel Daawuda.
Yàllaay aar nitam
Mu jëm ci njiital woykat yi, di woyu cant.
Yal na nu Yàlla barkeel
Mu jëm ci njiital woykat yi, ànd aki xalam, di woyu cant.
Yàlla daagu, daan
Mu jëm ci njiital woykat yi, ñeel Daawuda, di woyu cant.
Ku ñu fitnaal a ngi ñaan
Mu jëm ci njiital woykat yi, dëppook galan bu ñuy wax Tóor-tóor, ñeel Daawuda.
Yàlla, gaawe ma
Mu jëm ci njiital woykat yi, ñeel Daawuda, di woy wuy fàttalee.
Mag a ngi séentu Yàlla àtte ko dëgg
Nu ñaanal Buur
Ñeel Suleymaan.
Am Yàllaa gën
Dib taalifu cant, ñeel Asaf.
Yàlla, bu la noon ree
Dib taalifu yeete, ñeel Asaf.
Yàllaay àtte
Mu jëm ci njiital woykat yi, dëppook galan bi ñu dippee Bul yàq, di woyu cant, ñeel Asaf.
Yàllaa moom xare
Mu jëm ci njiital woykat yi, ànd aki xalam, di woyu cant, ñeel Asaf.
Yàllaa ngi seetaan
Mu jëm ci Yedutun, njiital woykat yi, dib taalifu cant, ñeel Asaf.
Nit goreedi, Yàlla gore
Dib taalifu yeete bu ñeel Asaf.
Yàlla, feyul nu
Dib taalifu cant, ñeel Asaf.
Yàlla, suqalil sa njëmbat
Mu jëm ci njiital woykat yi, dëppook galan bu ñuy wax Tóor-tóor yi, dib taalifu cant, ñeel Asaf.
Déggal Yàlla, jariñu
Mu jëm ci njiital woykat yi, ñeel Asaf, te ànd ak xalam gu ñuy wax gitiit81.1 gitiit: seetal ci 8.1..
Yàllaay àtte ndawi péncam
Dib taalifu cant, ñeel Asaf.
Yàlla, mbugalal noon yi
Di woyu cant, ñeel Asaf.
Ku dal ak Yàlla bég
Mu jëm ci njiital woykat yi, ànd ak xalam gu ñuy wax gitiit84.1 gitiit: seetal ci 8.1., ñeel askanu Kore wu góor.
Aji Sax ji, suqaleeti nu
Mu jëm ci njiital woykat yi, dib taalifu cant, ñeel askanu Kore wu góor.
Ma ñaan, bésub njàqare
Mu di ñaanu Daawuda.
Siyoŋ, yaay ndeyu xeet yi
Ñeel askanu Kore wu góor, di woyu cant.
Ma jàq, jooy
Di woyu cant, ñeel askanu Kore wu góor, jëm ci njiital woykat yi, dëppook galan bu ñuy wax Maxalat Leyanot, dib taalifu yeete bu ñeel Eman mi bokk ci giirug Esra.
Aji Sax ji, loo dige woon?
Dib taalifu yeete bu ñeel Etan mi bokk ci giirug Esra.
Doom aadama yàggul
Di ñaanu Musaa, góorug Yàlla ga.
Aji Sax jee mat kaaraange
Nu woy bésub Noflaay
Di woyu cant ngir bésub Noflaay.
Ma bàkk Aji Sax ji
Yàllaay mbugal ku bon
Kaayleen, nu sant
Buur Yàllaa ngi àttesi àddina
Aji Sax jeey nguuroo dëgg
Woyleen Aji Sax jiy àttesi
Dib taalifu cant.
Aji Sax ji buur bu sell la
Aji Sax jee baax
Di woyu cantu màggal.
Buur a ngi jaayanteek Yàlla
Ñeel Daawuda, dib taalifu cant.
Yàlla, bu ma rey
Di ñaani néew-ji-doole ju sonn, bay diis Aji Sax ji njàqareem.
Ma sant Aji Sax ji
Ñeel Daawuda.
Màggalleen Ki sàkk lépp
Aji Sax ji sàmm na kóllëre
Israayil di wor, Yàlla di ku wóor
Aji Sax jeey xettalee
Yàlla, may nu ndam
Di woyu cant, ñeel Daawuda.
Yal na Yàlla mbugal noon bi
Mu jëm ci njiital woykat yi, ñeel Daawuda, dib taalifu cant.
Yàlla fal na nitam
Ñeel Daawuda, dib taalifu cant.
Yàlla la ay mbiram sax
Ku ragal Yàlla gis mbaaxam
Buur Yàllaay walloo
Yàllaay walloo dooleem
Ku wóolu Yàlla barkeel
Ma sant Yàlla mi ma xettali
Na ñépp ànd ak Israayil sant Yàlla
Aji Sax jeek man, ma daan
Aji Sax ji, sa kàddu laay bége
Ma ñaan ci biir tuuma
Di woy yu ñuy yéege ca tund ya, di ko màggale Yàlla.
Ana ku may sàmm?
Di woy yu ñuy yéege ca tund ya, di ko màggale Yàlla.
Nu ñaanal Yerusalem
Di woy yu ñuy yéege ca tund ya, di ko màggale Yàlla, ñeel Daawuda.
Yàlla, fajal nu gàcce
Di woy yu ñuy yéege ca tund ya, di ko màggale Yàlla.
Nanu sante Aji Sax ji wallam
Di woy yu ñuy yéege ca tund ya, di ko màggale Yàlla, ñeel Daawuda.
Ku doyloo Aji Sax ji raw
Di woy yu ñuy yéege ca tund ya, di ko màggale Yàlla.
Yàlla, delloo nu
Di woy yu ñuy yéege ca tund ya, di ko màggale Yàlla.
Barkeb Yàllaa wóor
Di woy yu ñuy yéege ca tund ya, di ko màggale Yàlla, ñeel Suleymaan.
Ragal Yàlla, jàmmi kër
Di woy yu ñuy yéege ca tund ya, di ko màggale Yàlla.
Noon manul Israayil
Di woy yu ñuy yéege ca tund ya, di ko màggale Yàlla.
Nu séentu njotug Yàlla
Di woy yu ñuy yéege ca tund ya, di ko màggale Yàlla.
Damaa woyof, gëm Yàlla
Di woy yu ñuy yéege ca tund ya, di ko màggale Yàlla, ñeel Daawuda.
Yàlla digoo naak ki mu fal
Di woy yu ñuy yéege ca tund ya, di ko màggale Yàlla.
Bennoo, barkeel
Di woy yu ñuy yéege ca tund ya, di ko màggale Yàlla, ñeel Daawuda.
Way-ngëm ñaa ngi sant
Di woy yu ñuy yéege ca tund ya, di ko màggale Yàlla.
Lu Yàlla namm lay def
Yàllaa am kóllëre
Jooye nanu àll
Aji Sax ji waccu ma
Ñeel Daawuda.
Aji Sax jee ma xam, ba jeexal ma
Mu jëm ci njiital woykat yi, ñeel Daawuda, dib taalifu cant.
Ku ñu toŋal a ngi ñaan
Mu jëm ci njiital woykat yi, dib taalifu cant, ñeel Daawuda.
Yàlla, sàmmal sama làmmiñ
Dib taalifu cant, ñeel Daawuda.
Aji Sax ji rekk a ma yég
Dib taalifu yeete bu ñeel Daawuda, ba mu nekkee ca xunt ma.
Aji Sax jeey sama yaakaar
Dib taalifu cant, ñeel Daawuda.
Aji Sax ji, laggsil
Ñeel Daawuda.
Ma kañ Buur Yàlla
Di woyu màggal, ñeel Daawuda.
Buur Yàllaa jara wóolu
Yàllaa gën ci àddina, gën ci nit
Na àddina wërngal këpp màggal Yàlla
Na Israayil màggal Ki Sax
Màggalleen Ki Sax!
Taalifi cant
<
0
>
© 2025 MBS